waaw
Sàntar Waaw ci Ndar mooy këru artist yi te it di bérëb bu ñuy saytoo jumtukaay yi ak xarala yi. Li ñu gëna bëgg foofu, mooy dundal aada ak cosaanu Senegaal ak bu Afrig yépp te it yombal weccoo xalaat ci wàllu cosaan ak aada. Fexe it, ba di dajale nit ñu, ngir ñuy jàng di xalaat ak di liggéey. Dina mëna nekk it, këru dalukaayu gan, këru liggéeyukaay ak it, bérëbu gëstu ak di xalaat ci lépp lu jëm ci cosaan ak aada Ndar ak Senegaal yépp. Dalukaay bi dafa am peyoor, wànte am na ndàmpaay gu ñu xalaat ngir artist yi.
Sàntar Waaw, mu ngi bokk ci kurél gu mag gu tudd "Yelema" di benn mbootayu Finlandais guy toppatoo lépp lu jëm ci aada ak cosaanu Afrig. Ñi koy saytu, ñu ngi bokk ci benn mbootaayu wolonteer Finlandais lëkkaloo ak ay boroomi xam-xam ci cosaan ak aada yu nekk fii. Li gëna soxal sàntar Waaw daal, mooy di jàngale, di tàggat ak di saytu lépp lu jëm ci aar ak xarala.